*Ñaanug Sëriñ Fàllu gi.*Yaw Yàlla noo ngi lay ñaan sunu wërsëg yii bu nekkee ci kaw nee ko cëŋŋ fi suuf, bu nekkee fi suuf nee ko pullet mu génn,

*Ñaanug Sëriñ Fàllu gi.*Yaw Yàlla noo ngi lay ñaan sunu wërsëg yii bu nekkee ci kaw nee ko cëŋŋ fi suuf, bu nekkee fi suuf nee ko pullet mu génn,





*Ñaanug Sëriñ Fàllu gi.*

_*Yaw Yàlla noo ngi lay ñaan sunu wërsëg yii bu nekkee ci kaw nee ko cëŋŋ fi suuf, bu nekkee fi suuf nee ko pullet mu génn, bu génnee te sori dara du ko jar, nee ko ñoreet mu jege waaye bu jegee te tuut day gaaw a jeex, na ne gàññ, bu nee gàññ na barkeel, bu barkeelee nanu la ci jaamu, bunu la ci jaamoo nangul jaamu gi, boo nangoo jaamu gi ku nu xaar yalla na xàddi. Xaar, xàddi, xaaf, xafaan, xafara, xàpp, dëkk, dàkk.*_

_*Ndegam dee manul a ñàkk, bunuy dee Yàlla bunu sukuraat, Yàlla bunu aksidànte, Yàlla bunu lakk, Yàlla bunu lab, nun daal bunuy dee, nanu ne gammiy nelaw nga ne roseet ruu gi, ne ko tegg ci loxul Sëriñ Bàmba, mu ne nu fàpp boot, nga ne nu duxuus àjjana.*_

_*Sëriñ Fàllu MBÀKKE.*_













 

Enregistrer un commentaire

0 Commentaires